chant
Afrique> Sénégal
Kuy wallu waa Sabadolaa [Kuy wallu waa Sabadolaa]
Kuy wallu waa Sabadolaa [Kuy wallu waa Sabadolaa]
Kuy wallu waa Sabadolaa [Kuy wallu waa Sabadolaa]
Kuy wallu waa Sabadolaa [Kuy wallu waa Sabadolaa]
REFRAIN (Faada Freddy)
Hã ! lii de musiba naarulaay la
ku ëpple sa moroom def ko bàyyima
Ku xamul bur dee na (xam) bur saay na
baadoolaa ngi bëgg dee léegi doy na
buur du mbokk ku ko jege mu soppi la mala
Cere buur
dara du ko siim lu dul rongoñu baadoola
Soosu buur
dara du ko tax a niin lu dul ñaqu baadoola
Cere buur,
dara du ko siim
COUPLET 1 (NDONGO D)
Baykat tax nga du jëmbëti yoonu sàmm yi dëngëti
xale yi dematuñu rëbbiji (rëbbi)
Jigéen ñaa ngi ci pegg bi
«Usine» (isin) yaa ngi fi sampu
doomi dëkk bi nangu
Bu ñu bëggee ligggéey du àntu
Arcelor Mital Sabadolaa di gantu
«corruption» bi di banku
ci biir askan kuy màndu
noppil ñu jéqi seen i «pépites»
màbbal suuf si ndax “granites”
Téll-téll «marteau-piqueur»
riiru «dynamite» Baadoolo bi di dee ci xàttit
REFRAIN (FAADA FREDDY)
Hã ! lii de musiba naarulaay la
ku ëpple sa moroom def ko bàyyima
Ku xamul bur dee na (xam) bur saay na
badoolaa ngi bëgg dee léegi doy na
buur du mbokk ku ko jege mu soppi la mala
Cere buur
dara du ko siim lu dul rongoñu baadoola
Soosu buur
dara du ko taxa niin lu dul ñaqu baadoola
Cere buur,
dara du ko siim
COUPLET 2 (NDONGO D)
Joxe móonin bu bari
Money Power rey gor yi
«corruption” ba ci “forêt” yi
njublaŋ wetu nari yàpp yi ñuy gis «paradis»
«Le village est mécontent ; pas d'écoles, pas
d’hôpitaux»(Faada freddy)
Suite couplet (Ndongo D)
Jàng suuf si nu ňu koy jéree
dëkk ci dégg riiru xeer yi
jigéen ñi tooguñu ci ker yi
Woddoo geño, takk sër yi
umple li ne ci «mine» yi
dara nekkul ci biir cin yi
Sambaa-bóoy
Mooy doxal Sabadolaa
Mas-sa wa Goluma
ñii ñoo fay teg (def) “loi”
Joxe nañ suuf ak ngor
Ger askan wi ko lor
COUPLET 3 (FAADA FREDDY)
Oor biy jébbi ci suuf si
teewul gémmiñ yi gën a wow
Yoonu koppar moo fiy daw
ku ko yor ñu wéy ci sa waaw
Dégg nañ fi ay "milliards"
ba léegi xamunu fu ñu jaar
boroom doole yi nekk fii ci Sabadolaa
Yokk nañu badoolaa
REFRAIN FINAL
Hãn ! lii de musiba naarulaay la
ku ëpple sa moroom def ko bàyyima
Ku xamul bur dee na (xam) bur saay na
baadoolaa ngi bëgg dee léegi doy na
buur du mbokk ku ko jege mu soppi la mala
Cere buur
dara du ko siim lu dul rongoñu baadoola
Soosu buur
dara du ko tax a niin lu dul ñaqu baadoola
Cere buur,
dara du ko siim
Cere buur cere buur
Soosu buur soosu buur
Voir le clip en ligne