"Tefes", Fou Malade et Niagass (Album Ousseynou ak Assane, 2018)
Dans le texte de cette chanson, le membre du mouvement Y-en-à-marre Fou Malade et son acolyte Niagass dénoncent ce qu’on appelle au Sénégal le bradage du littoral c’est-à-dire la cession des terres qui bordent la mer dakaroise à des hommes d’affaires étrangers et sénégalais au mépris de toutes règles écologiques et ethiques.
Refrain (Niagass – choeur par Fou Malade)
Tefes laa bëgg a gis – Je veux voir la plage
Baadoola lañ koy siis – La classe populaire en est privée
Nun ñépp noo ko moom – C’est notre bien public
Delloleen (nu) sunu koom – Rendez-nous notre richesse
Couplet 1 (Fou Malade)
Faan, Sumbejun, Ngor, Mamel -Fann, Soumbédioune, Ngor, Mamelles
Sangu war a fey doon noteel – Payer pour se baigner reste une oppression
Jël sunu suuf def moomeel – Accaparer nos terres pour en faire votre propriété
Baare (Barrer) R, samp R-plis (R-plus) samp otel- Nous priver de l’air en construisant un R plus, un hôtel
Lii lu mu doon? mahaaza[1]? C’est quoi ça? Qu’est-ce que c’est que ça?
Yéen a séddale (séddoo) sunu littoral – Vous vous êtes partagés notre littoral
Blu-Radison, Sea-Plaza – Blu, Radison, Sea-Plaza
Ñépp a bokk moom suufu Senegaal – Les terres du Sénégal nous appartiennent à nous tous
(Refrain)
Couplet 2 A (Fou Malade)
Njiitu-réew mi lanuy déglu ngir mu wax ci Aydara (Aïdara) – Nous attendons que le Président de la République se prononce sur l’affaire Aidara
Boroom doole, baadoola, ku ne war ci am dara – Le riche, le pauvre, chacun doit être servi
Bu ñu ko deful bu ñu meree fippu indi saafara – Sinon, nous allons nous fâcher et mettre le feu
Doomi-réew mi, ëllëgu ndaw ñi, gëstu indi saafara- Les fils du pays et l’avenir de la jeunesse doivent être éclairés pour apporter des solutions
Couplet 2 B (Niagass)
«Littoral» bi jooy na, – Le littoral pleure !
«bradage» bi doy na, – Le bradage, ça suffit !
buumu jaam (njaam) gi dog na – Les chaînes de l’esclavage sont rompues!
Fippu taxaw jot na – C’est l’heure de se lever et de se révolter!
Refrain
Couplet 3 (Niagass)
Fii lanu daan fowe – C’est là où nous jouions
Séen mool sànni mbaalam – Apercevant le pêcheur qui lance son filet
bég ci ni mu koy joowee – Content de sa façon de ramer
xaar ngoon teeru gaalam – attendant le retour de sa pirogue le soir
Tefes la etijaŋ (yi) doon (daan) toog – C’est sur la plage que les étudiants avaient l’habitude de s’asseoir
féex di jàng seeni lesoŋ – profitant de la brise marine pour apprendre leurs leçons
déet ! bul jaay li nu bokk – Non! Ne vends pas ce qui appartient à nous tous
hey! «Cause» (causer?) indi «solutions» – Hey! causons pour trouver une solution
Refrain
Couplet 4 (Fou Malade)
Mbokk yi, nguur gi jël na sunu suuf – Les amis, le gouvernement a accaparé nos terres,
sunu moomeel jaay ko tubaab yi ak boroom alal yi Notre bien commun pour le vendre aux Occidentaux et aux nantis.
Ñoom ñu àndandoo kompóloo (complot) – Ils ont ourdi ensemble un complot
di ko séddoo bàyyi askan wi – Pour se le partager au détriment du peuple.
bu ëllëgee sunuy doom fan lañuy fowe ? – Dans le futur où nos enfants joueront-ils ?
bu ëllëgee man péex lañuy noyyi ?- Dans le futur, quelle brise marine respireront-ils?
[1] Expression arabe très appréciée des rappeurs sénégalais.